«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israyil gépp ne leen: Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa ci doxandéem yi ci Israyil, di joxeel Aji Sax ji ab saraxu rendi-dóomal, muy sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene,
TSK
TSK · Leviticus 7:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Bu ngeen dee defal Aji Sax ji saraxu cant, sarxal-leen ko na ñu leen koy nangule.
bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:
su boobaa bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji taamu ngir dëël fa turam, foofa ngeen di yóbbu mboolem lu ma leen sant: seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak mboolem ngëneel yu ngeen di def saraxi xas yu ngeen xasoo ak Aji Sax ji.
¶ Waaye seen yëf yu ñu sellal, ak seen sarax yi ngeen xasoo, jël-leen ko, yóbbu ca bérab ba Aji Sax ji di taamuji.
Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp.
¶ «Buntu ëttu biir bi féete penku it lañuy ubbil ki ci jal bi, buy joxe saraxu yéene: muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu cant ci biir jàmm, di beneen saraxu yéene bu ñeel Aji Sax ji, ngir mu joxe saraxu rendi-dóomalam, mbaa saraxu cantam ci biir jàmm, ni mu koy defe ci bésub Noflaay. Bu noppee, génn, ñu tëj bunt bi.