TSK

TSK · Luke 4:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

Luke 4:41 TSK

Ay rab itam di génn ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi.

Luke 8:37 TSK

Ci kaw loolu mbooloom diiwaanu Serasa gépp tinu Yeesu ngir mu jóge ca seen biir te dem ndax tiitaange lu réy lu leen jàpp. Naka la Yeesu dugg gaal, di dem,

Acts 3:14 TSK

Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.

Ñu dikk, jéggalu, génne leen ci biti, ñaan leen, ñu génn dëkk ba.

Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yu bon yi it loolu lañu gëm bay lox.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Filadelfi nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy ku Sell ki, kiy Dëgg, te yor caabiy Daawuda, di tijji te kenn du tëj, di tëj te kenn du tijji. Mu ne: