TSK

TSK · Luke 7:37

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Luke 5:32 TSK

Du ñi jub nag laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo, ngir jëme leen cig tuubeel.»

Luke 7:37 TSK

Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu.

Luke 19:7 TSK

Ñépp gis loolu, di ñurumtu naan bàkkaarkat bi la Yeesu dem këram, dal ak moom.

Lii itam xam nanu ko: ñi jub taxuñu yoon wi jóg, xanaa ñi jubadi ak ñi déggadi, ak ñemekati Yàlla yi, ak bàkkaarkat yi, ak ñi wormaalul lu sell, ak ñi wormaalul Yàlla, ak bóomkati baay, ak bóomkati ndey, ak reykati nit ñi,

Te it: «Aji jub ji, su ko mucc jafee, yéefar bi, bàkkaarkat bi moom, fu mu jëm?»