TSK

TSK · Malachi 1:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ku am ñaari jabar, su xejjoo kenn ki, foñ ki ci des, te ki mu xejjoo, ak ki mu foñ jural koy doom yu góor, te taaw bu góor bi di doomu ki mu foñ,

Wali Edom di ca soppliku koltaar, pëndub suufam doon tamarax, suufam mel ni koltaar buy lakk,

rabi màndiŋ mi di fa dajeeki bukki, bëyu àll di fa wooye moroom ma. Fa la rabu guddi di dal-loo, fàkkal fa boppam ab dal.

Ana ku muus, ba xam lu waral lii? Ku Aji Sax ji waxal, mu wax nu lu waral réew mi sànku, gental ni màndiŋ mi, kenn jaaru fi?

Waaye yeen askanu Esawu, man maa leen di ñori, ba ngeen ne duŋŋ. Maay siiwal seeni rawtu, ba dootuleen mana làqu; seeni goneek seeni bokk, ñépp ay sànku, seeni dëkkandoo sax, kenn du ca des ku naan:

Babilon def jali doj, di paxum till, di gent bu ñuy muslu, kenn du ko dëkke.

Nga wax ko, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw tundu Seyir, maa ngii fi sa kaw. Maa lay dóor sama loxo, nar laa def gent bu wéet.

Kon waxal waxyu bii, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wet gu ne lañu leen same, yàqte leen, ba ngeen mujj di moomeelu yéefar yi, ñépp di leen jëw ak a tooge,

Maa ngii déy maak yeen, maa leen di geesu, ba ngeen ruuje, jiwe.

Kër Yanqóoba sawara lay doon, kër Yuusufa dib tàkk-tàkk, kër Esawu di boob mu ñuy lakk, xoyom ko, ba kenn du dese bakkan ci kër Esawu.» Aji Sax jee ko wax.