TSK

TSK · Malachi 3:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»

Ci biir loolu Yonatan doomu Sóol ja dem Orsa ca Daawuda, di ko ñaax ngir mu gëna dëgërloo Yàlla.

¶ Ci biir loolu Axab woolu Abdiyas ma yor këram. Abdiyas doonoon ku ragal Aji Sax ji lool.

Ba ñu seetloo mbir ma ba muy dëgg, dañu leena wékk ñoom ñaar ci bant. Bindees na ko ci teewaayu Buur ci téere ba nu dippee Xew-xew ya.

¶ Guddig keroog Buur tëlee nelaw, daldi santaane ñu indil ko téere ba ñu dippee Xew-xew ya. Ci kaw loolu ñu di ko jàngal Buur.

Job 28:28 TSK

daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»

Ñu sell ñi ci réew mi ñooy garmi yi, sama mbégte mépp ñoom a.

Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.

Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce? Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal!

Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, ma limal la li mu ma defal.

Ma bare xalaati xol, nga dëfal ma, ma bég.

Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.

Maa xejjoo képp ku la ragal, tey topp say tegtal.

Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal te di ko yaakaare ngoram.

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, di déglu kàddug jaamam? Képp kuy doxe lëndëm te amul leeraange, na wóolu Aji Sax ji, te wéeroo Yàllaam jii.

Aji Sax ji ne ko: «Wëral dëkk bi, ci biir Yerusalem. Foo gis kuy onk ak a binni, di ko naqarloo gépp tojaange gu ñu fiy def, nga rëdd aw rëdd ci jëëm.»

dexu sawara di wal, balle fa kanamam. Junniy junnee nga koy jaamu, mboolooy mbooloo dar ko. Waa pénc ma toog, téere ya ubbiku.

Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu.

Acts 2:1 TSK

¶ Ba bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp a bokk daje benn bérab.

Acts 9:31 TSK

¶ Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

ngeen di jàngalante jàngi Sabóor, ak jàngi cant, ak jàng yu bawoo ci Noo gi leen fees, te ngeen di woy aka kañ Boroom bi, ci seen xol.

Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñal-leen ñépp.

Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.