TSK

TSK · Malachi 3:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla.

Kon nag dangay tànn ci biir mbooloo mi mépp ay góor ñu mat, ñu ragal Yàlla te dëggu, boole ci sib alalu ger. Su ko defee nga tabb leen, ñu yilif ay kurél yu mat junniy nit ak yu tollu ci téeméeri nit, ba ci juróom fukki nit mbaa fukki nit.

¶ «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra.

¶ «Buleen lekk seen àqu moroom, buleen sàcc. Buleen wacc peyu liggéeykat, muy fanaan ci seeni loxo.

¶ «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte.

¶ «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen.

Te bu ngeen ko yiwee, mu moom boppam it, buleen ko yiwee loxoy neen.

Ci bés bi ngeen koy fey peyooram. Bu ko jant sowe, ndax néew doole la te moom la yaakaara dunde. Lu ko moy mu boole leen ak Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.

¶ Ñu neeti «Alku ñeel na ku jengal àtteb doxandéem ak jirim akub jëtun.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

Job 7:2 TSK

Daa mel ni jaam bu namm keppaar mbaa mbindaan mu yàkkamtig peyam.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.

Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.

gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëgg.

Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.

Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf, bul aakimoo suufas jirim.

Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di jaaloo, di giñi fen, di taalal Baal, tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul,

Li ko waral mooy njombe wi ñu def fi digg Israyil, di jaalook seen jabari dëkkandoo, di wax ci sama tur ay kàdduy fen yu ma leen santul. Maa ko xamal sama bopp, seede ko.» Kàddug Aji Sax jee.

¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji da leena wax ne: Maa ngi nii di àttesi diggante gàtt bu duuf ak gàtt bu yooy.

¶ Mu ne ma: «Lii mooy alkute giy wàccsi ci kaw réew mi mépp. Li taxañ bi wax ci genn wetam mooy képp kuy sàcc, dees na ko fi dàqe, te li mu wax ci wetam gi ci des mooy képp kuy giñ ci ay fen, dees na ko fi dàqe.

«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”

Soof ngeen Aji Sax ji ak seeni wax, ngeen naan: «Nu nu ko soofe?» Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon mooy ki baax ci Aji Sax ji, te kooku la safoo.» Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?»

Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.

¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.

James 5:8 TSK

Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.

Jude 1:14 TSK

¶ Enog, juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottli woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell,

Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.