¶ Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettli leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk.
TSK
TSK · Numbers 14:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»
¶ Ci kaw loolu mbooloo ma dem ba ñàkk ndox. Ñu daje ci kaw Musaa ak Aaróona.
Mu ngoog, seen Yàlla Aji Sax ji moo teg réew mi fi seen kanam. Demleen nangu ko, ni leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji, waxe. Buleen ragal, buleen yoqi.»
Buleen leen ragal. Fàttlikuleen bu baax ni seen Yàlla Aji Sax ji def Firawna ak Misra gépp,
¶ Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke.
¶ Bu ngeen demee ngir xarejeek seeni noon ba gis ay fas, aki watiir, ak gàngoor gu leen ëpp, buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ki leen jële woon réewum Misra.
Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»
Maay nàndal samay fitt deret, sama saamar di yàppe, deret di nàcce ci ku ñu jam, ak ku ñu jàpp, tey tuuroo ci boppi kilifay noon yi.”»
Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te sàkkuwuñu Aji Sax ji.»
Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma, xanaa di sàkku rawtub Firawna, di keppaaroo keppaarug Misra.
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Bàkkaar nanu, ñaaw nanu, tooñ nanu, gàntal la, dëddu say santaane ak sa ndigali yoon.
¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.