TSK

TSK · Numbers 17:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Buleen yóbbe Keyateen ñeek seeni làng, lu ñu leen di dagge ci biir Leween ñi.

«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»

Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israyil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israyil.

Mboolem ñu bon ñaak ñu sew ña jàllandoo woon ak Daawuda nag ne leen: «Gannaaw ñii ànduñu woon ak nun, dunu leen jox dara ci alal ji nu nangu. Xanaa ku nekk jël jabaram aki doomam rekk, yóbbu te dem.»

Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.

yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww, ji asamaan tiim, boroom noo gi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey.

Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.