TSK

TSK · Numbers 18:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Nanga jël kuuyu xewu colu gi, nga baxal yàpp wi ci bérab bu sell.

«Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la.

Lekkleen ko ci bérab bu sell. Sa cér la, yaw ak say doom yu góor, ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Loolu lañu ma sant.

Nañu rendi kuuy mi ci bérab bu sell bi, fi ñuy rendee juru saraxu póotum bàkkaar ak saraxu rendi-dóomal, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la.