TSK

TSK · Numbers 20:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»

«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.

Man itam Aji Sax ji mere na ma ci ndax yeen, ba ne ma: «Yaw itam doo ca dugg.

«Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen, ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israyil, ñu jagoo.

Aji Sax ji ne ko: «Réew mii laa giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox. Won naa la ko, ba nga teg ci sa bët, waaye foofa, doo fa teg sa tànk.»

Samaree yilif Efrayim, te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. Dungeen mana saxoo dëgër nag, ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”»

Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede.

«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bésub keroog ay xalaat dikkal la, nga mébét mébét mu bon,

Luke 1:45 TSK

Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»

Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.