«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
TSK
TSK · Philippians 2:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»
Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngi, mooy baaxle, kawe, dees na ko yékkati, darajaal ko lool.
Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.
Ndax Almasi kat sàkkuwul bànneexu boppam, te noonu it la Mbind mi indee ne: «Ñi lay saaga, seeni saaga, ci sama kaw la dal.»
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul dayob boppam, bi ko def nawleb Yàlla.
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Bàyyileen xel ñi ñu tëj, ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëj, ak itam ñi ñuy mitital, ndax yeen itam, aw yaram ngeen am.