Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
TSK
TSK · Philippians 2:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ragal Aji Sax ji day rafetal xel; jëkke woyof, mujje tedd.
Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax.
Ci biir toroxteem lañu ko xañ dëggam; kuutaayam nag, ana ku ci mana wax? Ndegam bakkanam lañu toxale kaw suuf.»
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Ca laa ne: “Maa dikk nii, te téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man, maa defsi sa coobare, yaw Yàlla.”»
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»