TSK

TSK · Romans 1:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam am kuuy mu mu xasoo sarxe, te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, nde man, buur bu mag laa!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.

Acts 1:25 TSK

mu jël wàllam ci liggéey bi, te muy céru ndaw bii Yuda wacc, ba fekki wàll wa mu yelloo.»

Acts 9:15 TSK

Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.

Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Da dul Yàllay jaambur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jaambur ñeet kay!

Teewul mu am ci wet yu ma leen ñemee binde kàddu yu ma ñéebluwul, ngir fàttli leen li ngeen xamoon ba noppi. Noonu ma binde nag, li ko waral moo di yiw wi ma Yàlla baaxe,

mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal,

Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.

Ndaxte gànnaay, yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla, kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel,

ndax ki liggéey ci Piyeer, ngir mu doon ndawam ci Yawut yi, moo liggéey ci man itam, ngir may ndawam ci yeneen xeet yi.

Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi.

mi dëppoo ak xibaaru jàmm bi ñu ma dénk, xibaaru Yàlla Aji Tedd ju màgg ji.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.