Réy, yàqule; xeebaate, jóoru.
TSK
TSK · Romans 12:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.
Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.
Ci Almasi lanu jote aw yiwu doon ay ndaw, ngir nit ñi déggal yoonu ngëm wi, ci biir mboolem xeeti àddina, ngir aw turam.
¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
Mànkooleen, buleen xëccu daraja, waaye nanguleena jonjoo ak ñi féete suuf, te baña jàppe seen bopp boroomi xel.
¶ Yiwu Yàlla wi mu ma may nag, ci laa lale kenu gi, ni tabaxkat bu xareñ, keneen di tabax ca kaw. Waaye na ku nekk xool bu baax na mu cay tabaxe.
Lu ko moy nag, ku ci nekk, cér ba la Boroom bi séddoon, noonee nga nekke woon ba la Yàlla di woo, nanga ko wéye. Loolu laa santaane ci mboolooy gëmkat ñépp.
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.
Ci lan ngeen yéesle yeneen mboolooy gëmkat ñi? Xanaa sama soxlay jëmmu bopp jii ma leen wéerul. Kon baal-leen ma, maa tooñ!
Ku foog ne moo am solo, te du dara nag, boppam lay nax.
Bu ngeen jàngee loolu, dingeen ràññee bu baax, ni ma dégge mbóot mi ci mbirum Almasi.
¶ Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub Almasi séddalee.
Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye doyadiluleen, ba jàpp ne seen moroomi gëmkat a leen gën.
¶ Yeen ñi doonoon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy, ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp.
Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw, gu teggine te yem. Buñu jiital di defaroo ay létt yu ëpp, ak gànjari wurus, aki per, ak yérey tànnéef,
te mooy na mag ñi moom seen bakkan, di ñu tedd, jiital seenum xel, te pastéefu ci wàllu ngëm, ak cofeel, akug muñ.
¶ Naka noonu, xale yu góor yi itam, ñaaxleen ci jiital seenum xel.
Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
¶ Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.
¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»