TSK

TSK · Romans 16:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Israyil, yaay mucc fa Aji Sax ji mucc gu sax dàkk! Doo rus, doo torox fii ak ëllëg.

ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

Waaye ba boobu, mboolooy gëmkati Almasi ya ca diiwaanu Yude xamuñu ma woon.

¶ Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle.

Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees.

¶ Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko.

¶ Man Yowaan seen mbokk, mi séddook yeen nattu ak barkeb nguurug Yàlla, ak muñ gi ci Yeesu, maa nga woon fa ñu ma toxaloon, ca dun ba ñuy wax Patmos. Li ko waral di sama waare ci kàddug Yàlla ak seedeel Yeesu.