TSK

TSK · Romans 3:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 25:4 TSK

Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla? Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?

Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.

Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di joxee àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa lees di joxe nit àtteb ku jub.

¶ Ndax kat digeb Ibraayma ba sédde Ibraayma àddina si, moom ak askanam, sàmm gu mu sàmm yoonu Musaa taxul, waaye àtteb njub bi mu jagoo ndax ngëmam, moo ko waral.

Bàkkaar a ngi woon ci àddina ba ca janti yoonu Musaa, waaye deesul waññale bàkkaar te aw yoon amul.

¶ Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.

¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la;

James 2:9 TSK

Waaye su ngeen gënaatlee, bàkkaar ngeen, te yoon topp na leen, ndax yeena ko xëtt.