Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”?
TSK
TSK · Romans 4:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jaraaf ja da caa àddu woon ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ko gisal sa bopp déy, waaye doo ci lekk.»
Samaree yilif Efrayim, te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. Dungeen mana saxoo dëgër nag, ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”»
¶ Gannaaw ba ma joxee kayiti njaay ma Barug doomu Nerya, damaa ñaan Aji Sax ji, ne ko:
Ñi sàmmul kóllëreg Yàlla ay nax la leen di fàbbee, waaye askan wi ràññee seen Yàlla, pastéef lañuy jëfeji.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen ñi dégg kàddu yii tey ci gémmiñu yonent yi fekke woon ba ñuy teg kenug kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ngir tabaxaat kër gi, nangeen góor-góorlu.
Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole, ak ci biiri saaga, ak ci biir ag ñàkk, ak ci biir coono yu ñu may bundxatale, ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.
¶ Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye.