TSK

TSK · Romans 8:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.

Seenug dund dëgg Almasi la, te keroog bu Almasi feeñee, yeen itam ay ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.

Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.

Ngëm a waral aw jigéen dekkile ñu ñu deele woon; ngëm a waral ay góor ñu ñu mitital, baña dellu gannaaw, weccikoo ko seen njotug bakkan, ndax yaakaara dekki, ba gëna dundati ëllëg.

¶ Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi feeñee.

¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.