TSK

TSK · Romans 8:29

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Musaa nag ne Aji Sax ji: «Waaw, yaw de yaa ngi ma naa ma yóbbu mbooloo mii, waaye xamaloo ma kan ngay yebal, mu ànd ak man. Yaa ma waxoon it ne ma: “Maa la xam ci saw tur, te it daj nga sama yiw.”

Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.

«Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, xam naa la; laata ngay juddoo ci sa ndey, séddoo naa la, def la ngay yonent ñeel xeet yi.»

Yàlla waccul ñoñam ñi mu ràññee woon lu jiitu. Am dangeena xamul li Mbind mi indi ci mbirum Ilyaas, ba mu dikkee Yàlla njàmbat lu jëm ci Israyil? Mu ne:

Li nuy biral kay, da di mbóotum xam-xamu Yàlla mu làqu woon, te Yàlla dogaloon nu koo terale, laata àddina di sosu.

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu, leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.

Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, nirule kook yaramam wi ànd ak teddnga.

Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.

¶ Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko: «Yaa di sama Doom, bés niki tey, maa la jur,» ba neeti: «Maay doon Baay ci moom, muy Doom ci man»?

Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Aw yiw ak jàmm ju ne xéew ñeel na leen.

Mboolem waa àddinaa koy sujjóotal, mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Gàtt, bi ñu rendi.