Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen.
TSK
TSK · Romans 9:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.
Ak dëggu Almasi gi ci man, kàddug damu googu, kenn du ma ko xañ, ci diiwaanu Akayi gépp.
¶ Mbaa fooguleen ne sunu bopp lanuy layal nii fi seen kanam? Fi kanam Yàlla de lanu waxe, ndax Almasi mi nu gëm, te lépp, soppe yi, seen yokkute la ñeel.
Yàlla seede na ne sopp naa leen yeen ñépp, cofeel gu Almasi Yeesu ci boppam àttana tibbe ci biir xolam.
Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal.
¶ Maa ngi lay àrtu nag fi kanam Yàlla, ak Almasi Yeesu, ak malaaka yi ñu tabb, ngir nga sàmm loolu te baña jeng, mbaa nga jëfe lenn loo defe xejj ak seen.