TSK

TSK · Zechariah 3:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mooy féete ndijoor néew-ji-doole, musal ko ci ku koy teg àtteb dee.

Amos 4:11 TSK

«Maa jàllarbi lenn ci yeen, na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor. Ngeen rëcce ca ni gillit gu ñu fëkke cib taal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee!

¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax, moom mi ma yebal ngir teddngay boppam, ci mbirum xeet, yi leen sëxëtoo woon, nee: «Képp ku leen laal kat, laal na sama reeni xol.

Luke 4:35 TSK

Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» Rab wa daaneel nit ki ca digg mbooloo ma, doora génn te gaañu ko fenn.

Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»

Ñi Yàlla taamu, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de mooy jox nit àtteb ku jub.

Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!

Jude 1:9 TSK

Moonte Mikayel, may kilifag malaaka sax, ba muy xëccoo ak Seytaane néewub Musaa, di wàqante ak Seytaane, taxul mu ñeme woon koo sikk ba boole ciy saaga. Da ko ne rekk: «Yal na la Boroom bi mbugal!»

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.