TSK

TSK · Zechariah 4:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Besalel sàkk itam tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Liggéeyu tëgg bu jekk la def tegukaayu làmp bi, ak taatu tegukaay bi, ak peru tegukaay bi, ay kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp ànd ak tegukaay bi, di benn.

ak tegukaayi làmpi wurusu ngalam yi, juróom ci wetu ndijoor, juróom ci wetu càmmoñ, fi kanam néeg bu sell baa sell; tóor-tóor yi ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus;

¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.»

Amos 7:8 TSK

Aji Sax ji ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa buumu beteex.» Boroom bi ne: «Maa ngii di natte buumu beteex fi digg Israyil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara.

Kumpa gi ci juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi, li muy firi mooy: juróom ñaari biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy gëmkat ñi; juróom ñaari tegukaayi làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.»