TSK

TSK · 1 Samuel 26:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk.

Samiyel ne Sóol: «Ag ndof nga def, ndax jëfewuloo santaane bi la sa Yàlla Aji Sax ji santoon. Soo ko defoon, Aji Sax ji dina saxal sa nguur ci kaw Israyil ba fàww.

¶ Sóol dellu ne: «Bàkkaar naa! Waaye ngalla waay sagal ma ci sama kanam magi askan wi ak ci kanam Israyil. Walbatikul, ànd ak man rekk, ma sujjóotali sa Yàlla Aji Sax ji.»

¶ Ba Daawuda waxee Sóol kàddu yooyu ba daaneel, Sóol da ne: «Éy Daawuda, doom, loolu sa baat la moos?», daldi ne yikkét jooy.

Ba ñu waxee Sóol ne ko Daawuda daw na, dem Gaat, Sóol rëbbatu ko.

Gis nga ni sawara wàcce asamaan, xoyom ñaari njiiti juróom fukki dag yi ma jiitu, ñook seen juróom fukki dag, waaye rikk wormaalal sama bakkan.»

Wóllërey Aji Sax ji, bakkanam ñor na Aji Sax ji.