TSK

TSK · 1 Timothy 3:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku maandu ci lu néew nag, maandu ci lu bare; ku jubadi ci lu néew it, jubadi ci lu bare.

Acts 6:5 TSK

¶ Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.

Acts 6:15 TSK

¶ Mboolem ña ca jataayu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.

su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;

Te it li gëna bare ci bokki gëmkat ñi, sama jéng yi ma nekke nii moo leen yokk aw fit, ba tax ñu gëna ñemee waxe kàddu gi te ragaluñu ci dara.

¶ Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye.

Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax yu yiwu Yàlla wu yaa.