TSK

TSK · 2 Corinthians 1:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.

te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, ne kii ak kee fa bokk juddoo, te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ.

Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,

«Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom: Sama xel mi tegu fi sa kaw, ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ, lenn du ci teqlikook sa gémmiñ ak sa gémmiñu askan, ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.» Aji Sax jee ko wax.

Buleen may Aji Sax ji fu mu dal-loo, ba kera muy taxawalaat Yerusalem, ba def ko sababu cant fi kaw suuf.

ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.

¶ Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk,

Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant.

Su boobaa la ku dëng ka di feeñ, te Sang Yeesu moo koy jàllarbee ngelawal gémmiñam, te moo koy rajaxee ca na muy feeñe bu délsee.

Waaye Boroom bi mooy ki jara wóolu, te moo leen di dooleel, musal leen ci Ku bon ki.

¶ ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak kàttan ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.