TSK

TSK · 2 Peter 1:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndegam nag gannaaw ba ñu fóotee këf ka teg liir, sarxalkat bi seet na ko, te liir wi soppiwul melo, bu lawul it setul. Dees koy lakk, ba mu dib dóom, su yàqoo biir ak su yàqoo biti yépp.

Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»

¶ Ana lu loolu di tekki nag? Ndax kon danuy wéye bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gëna yokku?

Sunu xibaaru jàmm nag, su muuroo, ñi nara sànku la muurul.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

¶ Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?

Ci jooju daraja, ak jooju jaloore ju wéet lees nu baaxee ay dige yu réy njég te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina, gi xemmemtéefu bakkan waral.

Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ,