TSK

TSK · Acts 12:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at.

Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.»

Job 31:31 TSK

ndegam du samay bokk a ma seedeel ne: «Ana ku mu leelul ndawal ba mu regg?»

Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.

Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole. Aji Sax jee lay xettli, bésub njàqare.

Mooy féete ndijoor néew-ji-doole, musal ko ci ku koy teg àtteb dee.

¶ Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.

Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!

Acts 12:7 TSK

Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.

¶ Ba ñu ca tegee ñaari at yu mat, ku ñuy wax Porsiyus Festus wuutu Feligsë. Feligsë nag bëggoon lu neex Yawut ya, ba tax mu bàyyi Póol ca kaso ba.

Acts 25:9 TSK

Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»

Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?