TSK

TSK · Acts 14:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 7:58 TSK

ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.

Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.

Acts 14:5 TSK

Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.

¶ Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.

Bokk yi, man de bés bu nekk ma jàkkaarlook ndee, ak sag bi ma leen di sagoo ndax Yeesu Almasi sunu Boroom, mi ngeen gëm.

Xanaa ay surgay Almasi lañu? Naa ràkkaaju nag, te ne maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey yu metti, maa man fopp; bu dee ci fani kaso, maa ëpple fopp; bu dee ci ay yar, maa ëpple ay yooni yoon, te bare na lu ma riisu ndee, ba raw leen:

ak itam bundxatal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar. Céy na ñu ma bundxatale, waaye Sang bee ma musal ci lépp!