Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.
TSK
TSK · Acts 14:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Acts 11:26
TSK
Acts 14:6
TSK
Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
Acts 14:28
TSK
Ñu toog nag ak taalibe ya diir bu xawa yàgg.
Acts 16:40
TSK
Noonu lañu génne kaso ba, dellu kër Lidi. Ñu gise faak bokki gëmkat ña, ñaax leen, doora dem.
Acts 20:9
TSK
Ci biir loolu ab xale bu góor bu ñuy wax Ëtikus ma nga tooge kéméju palanteer ba. Ngëmment dab ko, te kàddug Póol ga yàgg lool. Ay nelaw nag jàpp waa ji, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee.