TSK

TSK · Acts 16:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ña nga soloo darajaak sellnga, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.

Boroom bi Aji Sax jee ma bënnali nopp, te man it, gàntalu ma ko, deltuwma gannaaw.

Acts 8:27 TSK

Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.

Boroom bi nag gungee leen loxoom, ba ñu bare gëm, waññiku ci Sang bi.

Kon nag mbaaxug Yàlla ajuwul ci coobarey nit ki, mbaa aw ñaqam, waaye lépp yërmandey Yàlla la.

Waaye seenum xel a dërkiis. Ba tey jii, bu ñuy jànge biir mbooloo, téereb kóllëre gu jëkk gi, muuraay googoo fi des; murikuwul, ndax ci Almasi lay deñe.

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

¶ Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii:

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Catir nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Doomu Yàlla ji, ki ay gëtam mel ni sawara wu yànj, ndëgguy tànkam mel ni xànjar bu ñu jonj. Mu ne:

Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.