TSK

TSK · Acts 17:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»

Job 12:10 TSK

Moo yor ci loxoom lépp luy dund, yor noowal képp kuy noyyi.

Job 27:3 TSK

ne li feek may ànd ak bakkan, di noyyee noowal Yàlla,

Job 34:14 TSK

Bu ci Yàlla yebu woon, ba roccim xelam ak noowam,

Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw! Maa ne Aji Sax ji: «Yaay sama Boroom, awma alal ju la moy.»

Ñoom ñépp yaw lañuy séentu, ngir bu jotee, nga leel leen,

Duma wéye di sikke ba fàww, duma saxoo di mer, lu ko moy képp ku ma sàkk day tàggook bakkanam.

Amos 5:21 TSK

«Maa bañ, maa sib seeni màggal, seen ndajey diine génnliku na ma.

Moona noppiwula seereel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan, taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»

«Ana ku ko dawlul lenn, ba mu war koo delloo?»