TSK

TSK · Acts 20:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Noonu lañu def, yónnee ko magi Yude, Barnaba ak Sóol jottli ko.

Acts 15:4 TSK

Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.

¶ Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.

Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.

Titus 1:5 TSK

¶ Li tax ma bàyyi la gannaaw ca réewum Keret mooy nga mottli la desoon ca liggéey ba, te nga tabb ay mag ñu jiite mbooloo mi ci dëkk bu nekk, na ma la ko sante woon, man ci sama bopp.

¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.