¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»
TSK
TSK · Acts 27:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Malaaka ma ne ko: «Waaw baax na ba tey, duma tas dëkk boobu ngay wax.
Laban ne ko: «Ngalla waay, déglu ma, ngir sama ngisaane won na ma ne Aji Sax ji barkeel na ma ndax yaw.
Wattukat ba seetatuloon dara lu Yuusufa jiite, ndax Aji Sax jee ànd ak moom, te lu mu sabablu, Aji Sax ji may ko ca ndam.
Ilyaas ne ko: «Bul ragal dara, demal rekk, def ni nga wax. Waaye jëkk ma cee defaral mburu mu ndaw, indil ma, doora defaral sa bopp, yaak sa doom;
Sag mbon, sa moroomu nit lay lor, sag njekk it doom aadama ni yaw lay jariñ.
Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.
Bés ba ma la wooyee nga dikk, ne ma: «Bul tiit.»
¶ Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi,
Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»
Ña nekkoon ca gaal ga ñépp ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom benn (276) lañu.
¶ Keroog ba ma jëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp.
¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.