¶ Fekk na Ben Addàd buurub Siri woo mbooloom xareem mépp, ñu daje, ànd ak fanweeri buur ak ñaar yu mu faral, ñook seeni fas ak seeni watiir. Ñu dem song Samari, gaw ko.
TSK
TSK · Amos 1:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Am na it yoon wu Alyaasa demoon Damaas, péeyu Siri. Fekk Ben Addàd buurub Siri wopp. Ba ñu ko waxee ne ko: «Góoru Yàlla gi ñëw na fi.»
Ba mu ko defee Yowayas nangoo ci moom dëkki Israyil ya Asayel jële woon ca loxol baayam Yowakas ci xare. Ñetti yoon Yowayas duma na ko Ben Addàd, ba nanguwaat dëkki Israyil.
Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»
Bu ma taalee Misra, ba wéeruwaayam yépp rajaxoo, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.
Israyil moo fàtte ab sàkk-katam, di tabax kër yu yànj. Yuda moom yokki dëkk yu tata wër. Maay yebal sawara ci kawi dëkkam, mu xoyom ay tataam.»
Damay yebal sawara ca tatay Tir, mu xoyom ay tataam.»
Maay jafal ca kaw tatay Raba, mu xoyom ay taaxam, yuux ya jib bésub xare, ci biir callweer bésub ngëlén.
«Maay yebal sawara ci kaw Yudeen ñi, mu xoyom tatay Yerusalem.»