TSK

TSK · Amos 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Dégluleen yeen waa kër Yanqóoba, yeen ndesu kër Israyil gépp, yeen ñi ma dale yor ba ngeen juddoo, di leen fab ba ngeen génnee seen biiru ndey.

Dee mooy gënal dund mboolem ku des ci njaboot gu bon gii, ak mboolem fu ñu dese fa ma leen tasaare woon.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

«Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.»

Hosea 4:1 TSK

¶ Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi: «Du kóllëre, du ngor, du gennug ràññee Yàlla ci réew mi.

Amos 2:10 TSK

Fekk yeen, ma génnee leen réewum Misra, jaarale leen màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ngir ngeen nanguji réewum Amoreen ñi.

Amos 5:1 TSK

Amos ne: Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent: maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.