TSK

TSK · Amos 8:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.

Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat.

Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.

Kon nag yeen kókkalikat yi yilif askanu Yerusalem wii, dégluleen kàddug Aji Sax ji!

Ngalla dégluleen lii, xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon, ami gët te dungeen gis, ami nopp te dungeen dégg!

Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Amos 2:7 TSK

Ñooy dëggaate néew-ji-doole ci pëndub suuf, di xañ way-ñàkk àqam. Nit ak baayam di tëdde as ndaw, di teddadil sama tur wu sell.

Amos 7:16 TSK

Léegi nag, déglul kàddug Aji Sax ji. Yaa ma ne: “Bul biral waxyu ci Israyil te bul kebetu ci kaw askanu Isaaxa.”

Ma ne: «Lu mu doon?» Mu ne: «Ndabal nattukaay beey génn,» tegaat ca ne: «Lii mooy seen bàkkaar ci biir réew mi mépp.»

James 5:6 TSK

Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ.