TSK

TSK · Amos 8:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Booba la wax ne, gannaaw loxoo ñemee xàcci, jëm ci ngànguney Aji Sax ji, Aji Sax ji dootu noppee xareek Amaleg ba fàww.

Aji Sax ju gàngoor yi dafa wax ne: “Maay dikke mbugal mu faj la Amalegeen ña defoon Israyil, tëru leen ca yoon wa, ba ñuy génn Misra.

Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, dummóoyu na, du xoolati.»

Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dégtal na ma lii: «Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal, ba keroog ngeen di dee.» Boroom bee ko giñ, moom Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

«Bàkkaaru Yuda lañu binde xaccug weñ gu cat la di doj wu dëgër. Dees koo ñaas ci seen àlluway xol, ñaas ko ci seen béjjéni sarxalukaay.

«Saraxi cuuraay yi ngeen di taal, yeen ak seeni maam ak seeni buur ak seeni kàngam, ak baadoolo yi ci biir dëkki Yudak mbeddi Yerusalem, defe ngeen ne Aji Sax ji yégu ko, am da koo fàtte?

Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.

Amos 6:8 TSK

Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.