ndax Leween, ñi amul wàll ci seen céru suuf, dikk, ñook doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun, yi ngeen dëkkal, ngir ñu lekk ba regg. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seenu ñaq.
TSK
TSK · Deuteronomy 26:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw bu ngeen génnee mboolem céru fukkeelub meññeef, ci atum ñetteel, yemook atum génne cérub fukkeel, gannaaw ñaari at yu nekk, nangeen ko jox Leween ñi ak doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun ñi, ngir ñu lekk ba regg, fa ñu féete ca seeni dëkk,
Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.
Ñeel Daawuda. Aji Sax ji, àtte ma, man de maandu laa wéye, Aji Sax ji laa wóolu, jenguma.
Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.
Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewma say tegtal.
Lajj naa ni xar mu réer; gindi ma, Sang bi, sàgganewma say santaane de!
Moo tax fu ma tollu, man itam, may def lu ma man ngir am xel mu dal, wàccoo ak Yàlla, wàccoo ak nit ñi.
Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu, moom mi yelloo cant ba fàww, xam na ne fenuma.