TSK

TSK · Exodus 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.

Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy.

¶ Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.

Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna.

Ci biir loolu nu woo Aji Sax ji wall, mu dégg sunu yuux, daldi yebal malaaka, mu génne nu Misra. Léegi nu ngi nii fi Kades, dëkk bi digalook sam réew.

Waa Misra nag soxore nu, mitital nu, yen nu liggéey bu diis.

«Nëgëni ëllëg maa ngi lay yónnee waa ju dëkk diiwaanu Beñamin. Nanga ko diw, fal ko, ngir mu yilif Israyil, sama ñoñ, ba xettli sama ñoñ ci waa Filisti. Maa geesu sama ñoñ, ndax seeni yuux àgg na fi man.»

Ba nga gisee sunu toroxtey maam ya ca Misra, dégg seeni yuux ca tefesu géeju Barax ya,

buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.

Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; yal na sama yuux àgg fa yaw.

Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.

Ca saa soosa tembe la ko malaakam Boroom bi fàdd, ndax la mu delloowul Yàlla njukkal. Ba loolu amee, ay sax ronq ko, mu dee.