TSK

TSK · Exodus 3:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?»

Aji Sax ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.»

Demal rekk, man maay ànd ak yaw booy wax, di la xamal li ngay wax.»

Aji Sax ji defal Musaa la mu ñaan, jële ndiiraani weñ ya ca Firawnaaki dagam ak waa réewam, ba weñ desatu fa.

¶ Aji Sax ji woo na Musaa, wax ak moom ca xaymab ndaje ma ne ko:

¶ Aji Sax ji nag yeb Yosuwe doomu Nuun ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay yóbbu bànni Israyil ca réew ma ma giñoon, te man ci sama bopp maay nekk ak yaw.»

Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

«Jëlal ñaari doj yu mag yooy suuli ca dëru ban ba ca bunt kër Firawna gi ci biir dëkk bi, te na ko waa Yuda fekke.

Acts 7:7 TSK

Yàlla neeti ko: “Xeet wi leen di jaamloo nag, man maa leen di mbugal. Gannaaw loolu dinañu fa génne, jaamusi ma ci bérab bii.”

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?