TSK

TSK · Exodus 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba Leya ëmbee, am doom ju góor, da koo tudde Ruben (mu firi Gisleen, doom ju góor a ngi), ndaxte Leya da ne: «Aji Sax ji gis na sama toroxte. Léegi sama jëkkër dina ma bëgg.»

¶ Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra.

¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.

Su boobaa sama mer dina tàng, ma reye leen saamar, seeni jabar diy jëtun, seeni doom diy jirim.

Yowakas nag tinu Aji Sax ji, mu nangul ko, ndax fekk na mu gis fitnay Israyil ji leen buurub Siri fitnaal.

Ba nga gisee sunu toroxtey maam ya ca Misra, dégg seeni yuux ca tefesu géeju Barax ya,

Ku ñàkk a ngi, ñu futti, mu ngi binni, di néew-ji-doole. Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»

Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.

Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.