TSK

TSK · Ezekiel 21:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yeen sàmmi askan wi, serleen, yuuxuleen; yeen boroom gétt gi, xëppooleen suuf, ñaawloo; seen bésub rendikat taxaw na, te dees na leen tasaare, ngeen daanu, rajaxoo ni njaqal tànnéef.

Dëddu woon nanu la moos waaye léegi réccu nanu. Xam nan ne tooñ nanu, ba tey nuy màttuy wiccax. Danoo rus, torox ndax sunu ñaawtéefi ndaw.”»

Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:

«Yaw nit ki, jottlil waxyu! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’

Joel 2:1 TSK

Wal-leen bufta ca Siyoŋ, dégtal-leen ab yéene ca sama kaw tund wu sell. Na waa réew mi mépp lox, nde bésub Aji Sax jaa ngi dikk te dëgmal na.