TSK

TSK · Genesis 1:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.»

Job 26:7 TSK

Kee firi asamaan fu dara amul, sanjamtal suuf fu dara newul.

Job 26:13 TSK

Noowam wal, asamaan leer, loxoom jam jaan jay balaw-balawi.

Job 37:18 TSK

ndax yaa ko lal-le woon déndub asamaan, mu dëgër ni weñ gu ñu xelli?

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.

làmboo leer ni mbubb, firi asamaan ni ndimo,

Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, ba ca ndox ma tiim asamaan ya.

Xàmbaar bu duyee, ba fees, fi kaw suuf lay soob. Garab, bu daanoo ndijoor mbaa càmmoñ, fa mu daanu lay des.

Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.

¶ Ab yéenee ngi, di kàddug Aji Sax ju dikkal Israyil. Kàddug Aji Sax jee, ki firi asamaan, lal suuf, te bind noowug doom aadama ci biir doom aadama.