TSK

TSK · Genesis 25:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.»

Mu seetlu ci Aji Sax ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Urim, du ci kàddug yonent.

Bu ngeen di joxe ay sarax, di lakk seeni doom ngir ay tuur, yeena ngi sobeel seen bopp ba tey jii ci seen tuur yii yépp. Man nag ngeen defe ne maa leen di bàyyi, ngeen seetlusi fi man, yeen waa kër Israyil? Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, duma leen bàyyi mukk ngeen seetlu fi man.