TSK

TSK · Genesis 27:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, te sa askan teg ay bañam tànk.»

¶ Yanqóoba dem, jël gàtt yi, indil yaayam, mu defar ba mu neex, ni ko baayam bëgge.

Isaaxa ne ko: «Jottli ma fii ma lekk ci sam rëbb, doom, ba ñaanal la ci sama xol.» Yanqóoba jottli Isaaxa ndab li, mu lekk, daldi koy may biiñ, mu naan.

Mu togg moom it, ba mu neex, indil baayam. Mu ne ko: «Jógal baay, lekk ci sa rëbbum doom, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.»

Yuusufa ne baayam: «Ñii ñooy sama doom, yi ma Yàlla jox fii.» Baayam ne ko: «Nañu jegesi, ma ñaanal leen.»

Ñooñu ñoo sos mboolem giiri Israyil, ñu tollu ci fukk ak ñaar, te loolu la leen seen baay wax, ba mu leen di tàggu. Ku ci nekk mu tàggoo ko kàdduy tàggtoo, ya war ca moom.

¶ Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon bànni Israyil, bala moo nelaw.

Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan.