Loolu wees ñu toog, di lekk. Nes tuut ñu siggi, séen am njëggum giléem, muy ay Ismayleen, yu sëf cuuraayu ndàbb ak diwu yaram ak cuuraayu xas, jële ko réewu Galàdd, jëme Misra.
TSK
TSK · Genesis 37:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba ñu yóbboo Yuusufa Misra, Potifaar, jawriñu Firawna, ma jiite ay dagam, da koo jënd ca Ismayleen, ña ko fa indi.
Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra.
¶ «Ku sàcc nit, dee rekk mooy àtteem, moo xam da koo jaay, mbaa ñu fekk ko ci ay loxoom.
Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk.
«Fexeel ba feyul bànni Israyil ci waa Majan. Gannaaw loolu dees na la yóbbu, tëral la fa say bokk.»
yónnee ku leen jiitu, muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam,
Ñu xëcc buum yi, génne Yeremi kàmb ga. Gannaaw loolu Yeremi des ca biir ëttu dag ya.
¶ «Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,