Genesis 28:12
TSK
¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.
Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax.
¶ Ñaari ati lëmm wees na gannaaw loolu, gént dikkal Firawna, mu jeneer taxaw ca wetu dexu Niil.
Ay fittkat a ko toŋal, di ko song ak a fitt.
Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.
Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltasar, mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.