TSK

TSK · Genesis 8:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Négandiku na juróom ñaari fan, doora yebalaat pitax ma.

Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.

Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»

Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!

James 5:7 TSK

¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.