TSK

TSK · Genesis 8:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel,

Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf.

¶ Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.

¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.

¶ Ba ñu àggee fa ko Yàlla wax, Ibraayma sàkk fa ab sarxalukaay, teg ca matt ma, yeew Isaaxa doomam, teg ko ca kaw matt ma ca sarxalukaay ba.

Mu daldi fay sàkk sarxalukaay, tudde ko El Elowe Israyil (mu firi Yàllay Israyil mooy Yàlla).

Mu sàkk fa nag sarxalukaay, tudde bérab ba El Betel, ndax foofa la ko Yàlla feeñoo, bi muy daw magam.

Sarxalukaay bu ñu defare suuf ngeen may sàkkal, di ci sarxal seeni gàtt ak seeni nag, muy seen saraxu rendi-dóomal, mbaa seen saraxi cant ci biir jàmm. Sàkkleen ab sarxalukaay ci mboolem bérab bu may fàttlee sama tur, ma dikk fi yeen, barkeel leen.

Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.

¶ Aji Sax ji woo na Musaa, wax ak moom ca xaymab ndaje ma ne ko:

¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.

¶ Kon nag saa su nekk, nanuy jooxee ci Yeesu, sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.