TSK

TSK · Hosea 13:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye tey yeena dëddu seen Yàlla, ji leen musal ci mboolem seeni loraange ak seeni njàqare. Yeena ko ne: ‘Falal buur ci sunu kaw daal!’ Léegi nag taxawleen fi kanam Aji Sax ji, giir ak giir, làng ak làng.”»

Léegi nag buur bi ngeen taamu, di ko sàkku, mu ngi nii. Mu ngoog, Aji Sax ji fal na buur bu leen jiite.

Bàkkaaru ngisaane la déggadi yemool, ñaawtéefu bokkaale tollook reewande. Yaa gàntal ndigalu Aji Sax ji, Moom mu gàntal sa nguur.»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

Noonu la Buur tanqamloo mbooloo ma, te Aji Sax ji moo walbatee noonu mbir ma, ngir amal wax, ja mu waxoon Yerbowam doomu Nebat, Axiya waa Silo ba jottli.

Demal ne Yerbowam: “Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Dama laa yékkati ci biir mbooloo mi, fal la nga jiite Israyil sama ñoñ.

Bu am réew dee fippu, kilifa ya bare; réew mu jàmm sax, kilifa gaa am déggin ak xam-xam.

Samari lees di tas, mook buuram, mu mel ni bant buy tëmb di dem.